Ñeenti produksiyoŋ, benn matuwaay: action bi sukkandiku ci nettali bu dëggu.
Ci Ndakaaru, PL Production dafay defar ñeenti porose ci film ak séeri, yu ekip Senegaal ak bitim-réew di liggéey ci. Katalog bi dafay xool thriller, espiyonaas, daraamu sport ak nettali yu terrain, ak benn xalaat: crédibilité ci nettali ak ci pëlëg.
Produksiyoŋ yii ubbiku nañu ci waxtaan ak koprodiktër, investisër, difizër, distribitër ak festiwaal yi bëgg dimbali nettali yu action Afrig yu jëm ci Senegaal ak àddina bi.
Benn gaal bu yeb ngànnaay réer ci géej. Ci Ndakaaru, ekip Interpol-Senegaal topp rëdd buy yóbbu ci lu kenn mënta tudd.
Xool xibaar yi →
Dale ko ci séy bu metti ba ci ringi boxe yu Afrig: xeexu jigéen ju bañ ñàkk ñaari yoon.
Xool xibaar yi →
Ñu jàpp doom ju góor, 72 waxtu ngir fey alalu njot. Ku bokkoon ci soldaar yu tànnéef tànn beneen yoon.
Xool xibaar yi →
Ñu jàpp doom ju jigéen, te bëgg nëbb seetlu bi. Xaritu xare bu yàgg dugg ci lëndëm ngir indi ko.
Xool xibaar yi →